(Go: >> BACK << -|- >> HOME <<)

Aller au contenu

Ndimbal:Sàqum jëfandikukat

Jóge Wikipedia.
Sumbu 21 Sattumbar 2007 à 10:27, bu: Ibou (waxtaancëru) (Yòonalaat ko Aide:Sàqub jëfandikookat mu jëm Aide:Sàqum jëfandikookat)

Wii xët da lay wax lu sàqub jëfëndikookat di tekki, luy ay ngëneelam, noo koy sosee. Di la tektal tamit yoon wi ngay jaar ak xibaar yi ngay dajeel ci yoonu soste ngi, yooy gis te, xayna, xamoo seen tekki.

Sàqub jëfëndikookat

Ay ngëneelam

Balaa dara, yeneen jëfëndikookat yi, di nañ la xam, man a xammee say cëru ak say waxtaan. Ci turu jëfëndikookat bi ngay tànn lañ lay xammee (so demee bay bindu). Di na tax nga man a bokk ci aw askan wuy gën di yaa.

Su loolu weesoo di la xamal ne sàqub jëfëndikookat yemul foofu rek. Soo sosee sam sàq ba noppi, Wikipedia dijjil la boppam nak, jox la ay jumtukaay yu ku binduwul manuta jot. Ab lim bu tuuti ngi nii ci suuf:

  • Di nga am sa xëtu bopp fooy man xamalee sa bopp, man nga caa def lépp lu la neex, ci misaal: ab nataal, ay lëkkalekaay,... Soo xoolee yu ñeneen ñi man nga caa jëlee ay misaal.
  • Di nga am sa xëtu waxtaanukaay, foo xam ne yeneen jëfëndikookat yi fa lañ lay bindee ay bataaxal. Soo amee bataaxal bu bees di nañ la ko yëgal ci anam bu gaaw(doy na nga dugg).
  • Di nga man a topp yenn jukki yi ngir man a xam ndax soppeeku nañ walla déet. Doon na lu am solo ndax soo sosee sab jukki di na tax nga man kaa topp ba ab saay-saay du ko yax, mbaa yokk ci ay xibaar yi baaxul.
  • Di nga man a soppi say tànneef.
  • Di nga man a am ab lim ci say cëru, lépp loo indi ci Wikipedia.
  • Di nga man a tuddeewaat koj yu xëtu jukki yi.
  • Di nga man a jëli ab file
  • Beneen ngëneel bu am solo mooy ne sa IP kenn du ko gisati, ndax soo binduwul sa IP la ñuy bind (ci Jaar-jaar) muy turu ki def boobu cëru. Loolu kaaraange la ngir sa PC, di na tax ba saay-saay si du ñu la man a gis, di xam foo ne, bay man a indi ay tolof-tolof ci sa PC.

Foo koy jëfëndikoo?

Soo sosee am sàqud-jëfëndikookat ci Wikipedia wolof, foofu rek nga koy man a jëfëndikoo. Kon beneen Wikipedia bu ne da nga faa war a bindu soo fa bëggee cëru.

Su fekkee jëfëndikookat bi doxalinam mengòowul ak àtte yi Wikipedia tërël ngir yorteem jaar yoon, yorkat yi am nañ sañ-sañu teye la ab diir ba doo man duggal dara.

Tànn ab turu jëfëndikookat

Turu Sàqub-jëfëndikookat

Lu weesu xibaar yi ñu la jox ci xëtu mbindu mi, loginu mbindu mi ci Wikipedia, ci kàllaama xarala mooy "Turu Sàqub-jëfëndikookat".

dañ koy jappee ni sa dakkantal, jëmm gu dëggu gu jëfëndikookat yi, man nu ñu koo xam ndaxte ku mu neek man ngaa bindoo ak:

  • Sa tur dëgg;
  • Sa tur dëgg goo xaw a soppi;
  • Turu jambur boo jël;
  • Walla ab dakkantal boo sàkkal sa bopp.

Lépp mi ngi aju ci ni nga bëgg a bokkee: naxasal, jubal walla bañ ku la xammee. Xamal ne tamit sa turu Sàqub-jëfëndikookat warul doon baat bu ñakk teggin, baat buy wone sag bokk ci yenn mbootaay yi (politig, diine,...). Man jur ay réeròo ak ñeneen ñi. Day tax ñuy gisee say cëru ak yeneeni gët ( ci misaal baat yu mel ne "Hitler" walla "kkk").

"Turu Sàqub-jëfëndikookat" bi day tax nga man a xaatim say bataaxal ci xëtu waxtaanukaay yi, ñetti ~ nga def ci sa njeexintalu bataaxal, ngir xaatim.

Tur yi jara moytu

Man ngaa jëfëndikoo sa tur dëgg, su la neexee, waaye li ëpp ci waa wikipedia yi ay dakkantal la ñuy jëfëndikoo. Daanaka tur bula neex jël, waaye nak am na ay gappu:

  • Ab saaga manoo koo jël, ndax ni ko ñeneen ñi di gisee, su amee it di nañ sakku ci yaw nga soppi ko.
  • Bul di jëfëndikoot tur dëgg bu jambur, donte ku siiw la koo doon soppeem.
  • Bul di jëfëndikoot turu këru koom-koom walla bu nit bu sañ-sañu soskat aar
  • Bul di jëfëndikoot baat yii: yorkat; àttekat, bot,...), ndax dañoo am yeneen tekki, kon day jur jaawale.